We’ve updated our Terms of Use to reflect our new entity name and address. You can review the changes here.
We’ve updated our Terms of Use. You can review the changes here.
/
  • Streaming + Download

    Includes unlimited streaming via the free Bandcamp app, plus high-quality download in MP3, FLAC and more.
    Purchasable with gift card

      €1 EUR  or more

     

lyrics

Mbey
Couplet 1
Am na nu suuf am na nu ndox // On a de la terre, on a de l’eau
Man raw fuuf « autonomes » dox // Capables d’être les premiers qui avancent autonomes
Ken du nu uuf tibb di nu jox // Personne couvera pour nous gaver
Dellu si tóll yi réew mi naat // Retournons aux champs faire prospérer le pays
Am na nu ndaw am na nu naaj // On des bras jeunes, on a du soleil
God di na taw ayca nu waaj // Dieu fera tomber la pluie, préparons-nous
Mbey mi di law am jur paaj // L’agriculture et l’élevage se développant, en abondance
Koom-koom yokk xiif du nu faat // Plus de prospérité, nous vaincrons la famine
Njiit yiy saw di jaaxaan seen kaw rekk ley taataan // La pisse des dirigeants couchés leur retombera dessus
Na nu joob baayi caaxan dénk réew mi ndaanaan // Travaillons sans tricher, confions le pays à une personne intègre
Nun bu nu delloo cosaan leer na ma dóotu nu feebar // Retournons à traditions, sûr que nous ne tomberons plus malades
Kaw-kaw dóotul nooraan suuf si mooy su nu getar // Plus d’exode rural si nous exploitons la terre
Gerte, dugub, ñeebe, mën naa sómbi dege // l’Arachide, le mil et l’haricot peuvent faire pâte et bouillie
Bu la neexee ndambe coop si ba ni ok // tu peux les cuisiner en sauce haricots et t’en gaver
Ndaw ñi la nu yaakaar, ñoom ñépp dem na nu Dakar // notre espoir est aux jeunes, mais ils sont tous partis à Dakar
Wéetal taatu daqaar, cin yi tëwë saxaar // L’ombre du tamarinier abandonné, les marmites ne chauffent plus

Refrain
Da nu wara bey sunu tool // nous devons cultiver nos champs,
Suuxat suqali sunu réew // Arroser et développer notre pays
Góor ak jigéen jóok xeex ak ndóol // Hommes et femmes debout contre la misère
Sómbi, fonde, laax, ceereek meew // Bouillie de riz, de mil, couscous au lait

Couplet 2
Gornama lor na ma lor kune // Le gouvernement nous a porté préjudice
« Est-ce-que » sax war na ma wër fune // Est-ce que je dois m’exiler n’importe où ?
War na ma, war na la, war kune // c’est mon devoir, c’est le tien, c’est celui de tous
Dellu tool, jóok ci ndóol , am lune // Retourner aux champs, combattre la misère et prospérer
Doole jën ne ci ndox nañ ko gëm // L’eau fait la force du poisson, croyons-le.
Nan ko jox doole xel jox ko Jëmm // Donnons-lui la force de l’esprit pour qu’il prenne forme
Boppu koñ taal sa boon tek sa zëm // Au coin de rue, tu fumes ton joint buvant ton thé
Doon nga ndaw war nga xam fan nga jëm // Tu es jeune, tu dois savoir te fixer un destin
Yaakaar na nu leen doom, yéenay sunu koom-koom // Notre espoir est en vous nos enfants, vous êtes notre richesse
Réew mi le yéen a ko moom, ngir Yàlla fas leen jom // Le pays est pour vous, pour l’amour du ciel, engagez-vous
Nguur gi de mënu leen baaxal, politig bu mu leen jaaxal // Le pouvoir ne peut pas vous satisfaire, que les politiques ne vous intimident pas
Am réew deñ koy naataal, xam-xam deñ koy yaataal // On doit le faire prospérer un pays, des connaissances on doit les vulgariser.
Ji nañ bey nan di góob, wilasuwa yi kontaan // On a semé, cultivé et récolté, tous les villageois sont contents
Bi asamaan si di sóop, maa ngi deglu ngoyaan // Quand la pluie tombait, j’étais dans ma chambre à écouter de la musique « ngoyan »
Bëgëtuma jël gaal wuti « éldorado » // Je ne veux plus prendre la pirogue pour aller à l’eldorado.
Ma ngi nii di « normal », du ma « desperado » // Je suis assez normal et ne suis pas du tout désespéré.

credits

from OUSSEYNOU AK ASSANE, released April 9, 2018

license

all rights reserved

tags

about

FOU MALADE & NIAGASS Dakar, Senegal

Fou Malade et Niagass sont frères jumeaux, dans leur âme, leur physique, leur passion pour leur pays et sa jeunesse. Ensemble, ils ont cette joie et cette énergie de vivre qui fondent l’essence de leurs textes écrits en wolof et de l’harmonie complice émanant de leurs voix. Après quelques créations artistiques communes (Gent Bi en 2005, Sénégal en 2012), ils sortent « Ousseynou ak Assane ». ... more

contact / help

Contact FOU MALADE & NIAGASS

Streaming and
Download help

Redeem code

Report this track or account

If you like FOU MALADE & NIAGASS, you may also like: