We’ve updated our Terms of Use to reflect our new entity name and address. You can review the changes here.
We’ve updated our Terms of Use. You can review the changes here.

OUSSEYNOU AK ASSANE

by Fou Malade et Niagass

/
  • Streaming + Download

    Includes unlimited streaming via the free Bandcamp app, plus high-quality download in MP3, FLAC and more.
    Purchasable with gift card

      €7 EUR  or more

     

1.
Yàlla Refrain Yàlla sa jaam yi ñoo lay ñaan //Dieu, tes esclaves t’implorent Gudd fan sutura fekke tal ak muj gu rafet // Longue vie, sérenité, bonne santé et une fin heureuse, Yàlla may nu lekk ak naan // Dieu offre-nous à manger et à boire « Ordonnances », « dépenses », « essence » ñun bëggu nu « défaite » // Ordonnances, dépenses, essence, on aime pas la défaite Couplet 1 Yaa ma taal ba ma siiw aduna di ma xam // Je te dois mon succès, aujourd’hui tout le monde me connaît « Beurre » si naaj lañ ma diw, yaa ko tay may ma ndam // Je brille comme beurre au soleil, par ta Grâce, j’ai du succès. Gel yi sax dañ ma nob, « autographes » ak « photos » // Même les filles me courent après, sollicitent mes autographes et mes photos, Ne ci kaw ne «au top » wàcc fas yéeg « auto » // j’ai atteint les sommets, j’ai sauté du cheval pour une belle voiture Sa ma clip feeñ tele samay « droit » kenn du fay // Mon clip passe à la télé mais mes droits restent impayés Jënd « slip » la tële yërmande maa ngi fay // Je suis incapable d’acheter un slip, au secours ! Je suis m’éteins « Artistes patrimoine » Laba Sosseh, Ndiaga Mbaye // Les artistes sont notre patrimoine, Laba Sosseh, Ndiaga Mbaye Ndiouga Dieng, Number One, Pacotille dem na tey // Ndiouga Dieng, Number One, aujourd’hui, Pacotille est parti Ñun daal ñoo lay woyal feccal ba nga doyal // Nous, nous chantons et dansons pour toi à te combler. Dundal Bégal, Bégal dundal, waroo ñu seetaan // Nous te faisons vivre, te rendons gai, te rendons gai, te faisons vivre, tu ne dois pas nous ignorer Ku wéet nu wettali, ku réer nu nettali // Compagnons des solitaires, nous sommes les gardiens de l’histoire Mag ak gune kune fune fexeel ñu reetan //  aux grands et petits, à chacun, partout, nous apportons le sourire. Couplet 2 Jomb naa wër ñaan ndax da ma am tur // J’ai honte de quémander à cause de ma renommée Sonn naa, leb naa aka maa bëri bor // Je suis fatigué, j’ai pris des crédits, je suis si endetté Gëm naa dina baax ndax Yàlla mooy bur // Je crois que ça ira car Seul Dieu est Roi Bu ma naan ndeysaan du ma jaay sama ngor // N’aie pas pitié de moi, je ne vendrai pas ma dignité Feyu ma la, na nu dem poliis, Yàlla may a gu ma xaalis // Je ne te paie pas, amène-moi à la police, Dieu ne m’a pas encore enrichi Gëstu ma geun di ma noonoo», laajoo nu ma def ak coono // Essaie de comprendre qui je suis au lieu de faire de moi ton ennemi, tu ne m’as pas demandé comment je vis mes difficultés Xiif mar mer la yendoo siiw sa ma sutura ma ngembo // Je vis mes journées affamé, assoiffé, colérique, mais ma célébrité t’empêche de le voir Du ma géwal mënu maa woyaan, taasu walla woy ngoyaan // Je ne suis pas griot, je ne peux pas quémander, faire des éloges ou chanter de la musique « ngoyan » Hip Hop tere ñu « battrer » « hardcore » bëgg ñu « cadrer » // Le hip hop nous empêche de flamber, le hardcore veut nous cadrer Na nga muñ dina baax « madre » yéene bi weesu na pantare // Tiens bon maman, ça ira, mes rêves vont au-delà d’une chambrette. Conclusion Useynu niŋ ñuy seetaanee di ñu sagganee ba xëy nu jóog fi // Ousseynou, la manière dont nous sommes abandonnés, négligés, jusqu’à ce qu’à notre mort. Ñu ñuy tuddee ay bayal ay koñ ay estad wànte nak grawul // Ils baptisent des rues, des stades des boulevards à nos noms, mais c’est pas grave « Mais je te jure Assane, sur la tête de notre mère », gis nga // Mais je te jure Assane, sur la tête de notre mère, t’as vu…
2.
Nuuyo Mbër 02:33
3.
4.
TEFES 02:59
Tefess Refrain Tefes laa bëgg a gis // Je veux voir la plage Baadolo lañ koy siis // La classe populaire en est privée Ñun ñépp ñoo ko moom // C’est notre bien public Delloo leen sunu koom // Rendez-nous notre richesse Couplet 1 Faan, Sumbejun, Ngor, Mamelles // Fann, Soumbédioune, Ngor, Mamelles Sangu war a fey doon nootel // Payer pour se baigner reste une oppression Jël sunu suuf def moomeel // Accaparer nos terres et en faire vôtres «Barrer air pur» ndax sa « hôtel » // Vos hôtels, nous privent d’air pur Li lu mu doon, maa haaza // C’est quoi ça ? Qu’est-ce c’est que ça? Yéen a seddo sunu « littoral » // Vous vous êtes partagé notre littoral « Blu Radisson », « Sea Plaza » // Blu Radisson, Sea Plaza Ñépp a bokk suufu Senegaal // La terre du Sénégal appartient à tous. Couplet 2 Njiitu réew mi la ñuy déglu ngir mu wax si Aïdara // Nous attendons l’avis du chef de l’Etat sur l’affaire Aïdara Domou réew mi ëlëgu ndaw ñi gëstu indi saafara // Les fils du pays et l’avenir de la jeunesse doivent être éclairés pour amener des solutions Boroom doole baadolo kune war fi am dara // Le riche, le pauvre, chacun doit être servi Buñ ko deful bu ñu meree fippu indi saafara // Sinon, nous nous fâcherons et donnerons nos propres solutions « Littoral » bi jooy na // Le littoral pleure « Bradage » bi doy na // ça suffit le bradage ! Takku taxaw jot na // Il est temps de se lever Bu mu jaam gi dog na // L’esclavage est aboli Couplet 3 Fii La nu daan fowee // C’est là où nous jouions. Séen mool sànni mbaalam // Apercevant le pêcheur lançant son filet, Bég si ni mu kay joowee // Heureux de sa façon de ramer, Xaar ngon teeru gaalam // Attendant le soir pour accueillir sa pirogue Tefess la « étudiant » daan toog // Les étudiants s’asseyaient sur la plage Féex di jàng seeni « leçon » // respirant les embruns et apprenant leurs leçons Déet bul jaay li nu bokk // Non ne vends pas notre bien commun Héee « cause » indi « solution » // Hé une discute pour trouver une solution
5.
DELLUSI 03:48
6.
MBEY 03:26
Mbey Couplet 1 Am na nu suuf am na nu ndox // On a de la terre, on a de l’eau Man raw fuuf « autonomes » dox // Capables d’être les premiers qui avancent autonomes Ken du nu uuf tibb di nu jox // Personne couvera pour nous gaver Dellu si tóll yi réew mi naat // Retournons aux champs faire prospérer le pays Am na nu ndaw am na nu naaj // On des bras jeunes, on a du soleil God di na taw ayca nu waaj // Dieu fera tomber la pluie, préparons-nous Mbey mi di law am jur paaj // L’agriculture et l’élevage se développant, en abondance Koom-koom yokk xiif du nu faat // Plus de prospérité, nous vaincrons la famine Njiit yiy saw di jaaxaan seen kaw rekk ley taataan // La pisse des dirigeants couchés leur retombera dessus Na nu joob baayi caaxan dénk réew mi ndaanaan // Travaillons sans tricher, confions le pays à une personne intègre Nun bu nu delloo cosaan leer na ma dóotu nu feebar // Retournons à traditions, sûr que nous ne tomberons plus malades Kaw-kaw dóotul nooraan suuf si mooy su nu getar // Plus d’exode rural si nous exploitons la terre Gerte, dugub, ñeebe, mën naa sómbi dege // l’Arachide, le mil et l’haricot peuvent faire pâte et bouillie Bu la neexee ndambe coop si ba ni ok // tu peux les cuisiner en sauce haricots et t’en gaver Ndaw ñi la nu yaakaar, ñoom ñépp dem na nu Dakar // notre espoir est aux jeunes, mais ils sont tous partis à Dakar Wéetal taatu daqaar, cin yi tëwë saxaar // L’ombre du tamarinier abandonné, les marmites ne chauffent plus Refrain Da nu wara bey sunu tool // nous devons cultiver nos champs, Suuxat suqali sunu réew // Arroser et développer notre pays Góor ak jigéen jóok xeex ak ndóol // Hommes et femmes debout contre la misère Sómbi, fonde, laax, ceereek meew // Bouillie de riz, de mil, couscous au lait Couplet 2 Gornama lor na ma lor kune // Le gouvernement nous a porté préjudice « Est-ce-que » sax war na ma wër fune // Est-ce que je dois m’exiler n’importe où ? War na ma, war na la, war kune // c’est mon devoir, c’est le tien, c’est celui de tous Dellu tool, jóok ci ndóol , am lune // Retourner aux champs, combattre la misère et prospérer Doole jën ne ci ndox nañ ko gëm // L’eau fait la force du poisson, croyons-le. Nan ko jox doole xel jox ko Jëmm // Donnons-lui la force de l’esprit pour qu’il prenne forme Boppu koñ taal sa boon tek sa zëm // Au coin de rue, tu fumes ton joint buvant ton thé Doon nga ndaw war nga xam fan nga jëm // Tu es jeune, tu dois savoir te fixer un destin Yaakaar na nu leen doom, yéenay sunu koom-koom // Notre espoir est en vous nos enfants, vous êtes notre richesse Réew mi le yéen a ko moom, ngir Yàlla fas leen jom // Le pays est pour vous, pour l’amour du ciel, engagez-vous Nguur gi de mënu leen baaxal, politig bu mu leen jaaxal // Le pouvoir ne peut pas vous satisfaire, que les politiques ne vous intimident pas Am réew deñ koy naataal, xam-xam deñ koy yaataal // On doit le faire prospérer un pays, des connaissances on doit les vulgariser. Ji nañ bey nan di góob, wilasuwa yi kontaan // On a semé, cultivé et récolté, tous les villageois sont contents Bi asamaan si di sóop, maa ngi deglu ngoyaan // Quand la pluie tombait, j’étais dans ma chambre à écouter de la musique « ngoyan » Bëgëtuma jël gaal wuti « éldorado » // Je ne veux plus prendre la pirogue pour aller à l’eldorado. Ma ngi nii di « normal », du ma « desperado » // Je suis assez normal et ne suis pas du tout désespéré.
7.
8.
JALOORE 03:46
9.
10.
NOBULA 03:04
11.
BAALE 03:37
BAALE Refrain Boo Jekkoo deel baale // Pardonne quand tu peux faire mal Nañ diissoo bañ laale // Discutons au lieu de nous battre Couplet 1 Tey ma wax la li na naqari // Je te dirai aujourd’hui ce qui me chagrine : Jaay doole ndax sa « gabarie » // Provoquer les gens parce que tu es costaud Ñëw di jaale indi sabar yi // Présenter tes condoléances avec bling bling Xaal géew bi sànni koppar yi // Se mettre au milieu de la foule et jeter l’argent 1-2 nga shine, 3-4 nga xeex // 1-2 tu t’énerves, 3-4 tu te bats Li nga def sa mayin sax sa xol di jeex // Tes mauvaises pensées te rongent Woo la añ nga suur tëfli xaax ne tëf // Tu refuses de déjeuner mais tu craches dans le plat Kajj nga reer bi tuur, taal sa jum di ëf // Tu renverses le plat et tu allumes un gros joint Yow lu tax bi meer bi feebare // Et toi, pourquoi lorsque ta maman était malade Jëndóo garab yóobu l’hôpital //// Tu n’as pas acheté de médicaments  de l’hôpital ? Tey nag dëj bi ni nga ko defare // Vu comment aujourd’hui tu as organisé ses funérailles ? Aduna jay la ñaata junni nga taal //m’as-tu-vu, combien de billet as-tu claqué ? 5-6 nga tëc téeye geel yi tanyim // 5-6 tu t’enfermes pour baiser Te nga ne ci dëj war a ñaan di waayin // tu t’enivres alors que tu es endeuillé def tàtt di jooy xollu gan ñi tiis// Ivre, tu pleures à peiner les invités. Màndikat nga booy jëli naa la fils // T’es un ivrogne, je t’ai découvert fils Couplet 2 Defu ma yëgu ma bu ma ko waxal // Ne m’accuse de choses auxquelles je ne suis pas mêlé Gisu ma déegu ma jotu ma jaxal // j’ai ni vu, ni entendu, ni reçu d’offrande Tuxu ma naanu ma yoru ma goon // Je fume pas, je bois pas, j’ai pas d’arme Sàccu ma kàccu ma du ma sa noon //Je vole pas, mens pas et ne suis pas ton ennemi Da ngaa yëg sa bopp maa la gën a reew // Tu te crois supérieur, mais je suis plus indiscipliné que toi Da nga mën a soop da nga ñeme xew // Tu sais raconter des bobards et tu aimes le folklore Yagg a wanne baax te sa jikko sew // Tu feins d’être gentil mais tu es sournois Alal bi nga coop du la mas a lew // l’argent que t’as bouffé ne te sera jamais licite. Baal ma li ma saaga yaay sama gaayin // pardonne moi de t’avoir insulté, t’es mon pote Bi ngay laal cagga ñoo ngi naan caayin // Quand tu baisais les putes, on buvait du thé Na nu peace love dund paradise // faisons la paix et l’amour, vivons notre paradis Kaay ñu naan koof dafa war a naayis // buvons un café, positivons les choses. Bége fo ree fexee indi jàmm // Jouir de la vie, rigoler et faire la paix Boole doole di na gindi jàmm // l’union des forces révèle la paix Bayyi tooñ gën dëkkee balu àq // Eviter de nuire aux autres vaut mieux que demander éternellement pardon Ñaan gudd fan tuub li ñu yàq // Prier pour une longévité et expier toutes nos erreurs Tudee naa la doom dëgg la ci man// Mon fils porte ton nom et c’est sincère Boo feebaroon naa la yóobu Fann // Si t’étais malade, je t’aurais amené à l’hôpital Fann Mane la nitt Njaay yow la golo Hann // Je suis sain d’esprit c’est toi le singe du parc de Hann Yagg a saï-saï bandit Colobane // ça fait longtemps que tu es un saï saï, un bandit de Colobane Lii moo tax du ñu man a kóoz // C’est pour ça qu’on ne peut causer normalement Sunu amitié na fi « ménopause » // Alors notre amitié s’arrête là
12.
BAAY GILAAYE 03:52

about

C’est l’histoire d’une amitié, d’une complicité musicale. Fou Malade et Niagass ou Ousseynou ak Assane, deux amis, plus que frères, presque jumeaux, tellement leurs corps, leurs voix et leurs âmes se ressemblent, au point d’être pris l’un pour l’autre.
Ici, les jumeaux peuvent apporter bénédiction ou malédiction et l’on se prend à aller les trouver pour se protéger, pour une longue et heureuse vie. Garçons, les jumeaux s’appellent Ousseynou et Assane.
Leur dialogue musical, teinté d’humour, d’ironie, de satyre, réunit toutes les générations du Hip Hop Galsen. Les textes parlent d’amour, de paix, de justice, de circulation(s), d’agriculture, de bonne gestion des ressources publiques. Niagass et Fou Malade appellent les jeunesses africaines à relever la tête, se tenir debout pour leur émancipation et l’essor du continent.

credits

released April 9, 2018

Auteurs : Fou Malade et Niagass // Featurings : Mirma (Docteur Fou Malade et Naba Mind) et FakhMan (Jaloore), Leldo (instrument Hoddu, Docteur Fou Malade) // Produit par: Iss_814 (tracks 1, 2, 3, 4, 6, 7, 9, 11), Nautylus Prod (tracks 5, 7, 10, 12), Bamba al Mansour (track 8) // Mixé par : Nautylus Prod, Ciré Dia //
Enregistré à : Studio Guediawaye Hip Hop, Sénégal ; Studio Octopus de Nautylus Prod, France ; Studio Université Leiden, Pays-Bas ; Maison des Cultures Urbaines, Sénégal ; Studio LaPlace, France // Masterisé par : Nautylus Prod (www.nautylusprod.com)// Coproduction : Ousseynou ak Assane et A2L // Photographie: Sylvain Cherkaoui // DA : Golden Brown Studio//

license

all rights reserved

tags

about

FOU MALADE & NIAGASS Dakar, Senegal

Fou Malade et Niagass sont frères jumeaux, dans leur âme, leur physique, leur passion pour leur pays et sa jeunesse. Ensemble, ils ont cette joie et cette énergie de vivre qui fondent l’essence de leurs textes écrits en wolof et de l’harmonie complice émanant de leurs voix. Après quelques créations artistiques communes (Gent Bi en 2005, Sénégal en 2012), ils sortent « Ousseynou ak Assane ». ... more

contact / help

Contact FOU MALADE & NIAGASS

Streaming and
Download help

Redeem code

Report this album or account

If you like OUSSEYNOU AK ASSANE, you may also like: